- Inici
- Dëkk Kataluña
- Wergu yaram
- Kayitu kër doctor (TSI)
Kayitu kër doctor (TSI)
Kayit gi wara aam ngir doctor bi giss li
Moy kayit giy tax nga muna faju. Bo amul kayitu kër doctor, ken dula muna fath. Kayit la go xamne munuloko bok ak ken; dafa am numero bo xamne ci lanuy xame borom.
Ku wara am kayitu kër doctor?
Kep ko xamne boku na ci rewmi baci xaleyi soga jud.
Funu koy ute?
Ci Centre d'Atención Primària (CAP) bine ci goj binga dëke. Bu feke danga ko lath, dina am ay fan dananu loko yone ci kër ginga dëke.
Lan lanuy faral di tahawu?
Des naci taxawu biniy def mu jem ci sen ligey. Amna 6 taxawu yunuy def. Ñi ep ci nit ñi amnanu taxawu bunulen di taxawu mu jem ci sen wergu yaram, li demaniki:
- Ci walu febari melne mbiru drog, sida, walu ñaku ak yeneni xetu febar yi xamne ñiy yengu ci walu fath xamnanu ko.
- Fath bu njenk
- Fath bu lath taxawu
- Faju mbiru bop
- Yeneni xetu faju
- Mbiru farmaci: dofay 60%, bo ware jend ay garab bude fath bu njenk wala 100% ci garab yoyu bude dafa fek nga tëd hopital.
- Transport pur faju wala urgens
- Yeneni xetu faju (ci walu lek, fath yu jafe, ak yenen yu deme nonu)
- Rehabilitation
- Bu fek dafa wara am lunula wala legal com cer bu bess.
Kaña ngako mana saku?
Sasula nexe te fek nga yitewoko manam:
- Boy jend garab sa farmaci ba, sufekeni CatSalut def naci loxom tenga ame ordenans.
- Buga gise ak sa doctor
- Defar radiografi
- Serwisu Urgens
- Yob xale pur mu faju
Kayitu kër docotor munulo ci faju ci clinic wala yeneni priwe yuy fath.
Ba fan ci rewmi la la kayitu kér doctor di jariñ?
Ci españ yep. Pur ñu man la fath ci yeneni rewu Europ danga wara am kayitu kër doctor bu rewu Europ yep (TSE) binga xamne ñi ño koy joxe centres d'atenció i informació de la Seguretat Social (CAISS).
Ci fii 902 111 444 jëwriñ yi yooré werguyaram di naan la degglu ci soxla yi aajo ci werguyaram.



