- Inici
- Dëkk Kataluña
- Ci walu njàng ak formasoη
- Yenini Formation
Yenini Formation
Yeenen ni peexe
Bu weso njàng mi manuta ñak ak njangum universite, am nga yeneni xetu formation yo mana def bo neke mak:
Formation pur mana ligey dara
Formation bo xamne ni yangi koy defe ci lecolu metie yi, wala yenen xetu bërëb yu melnonu. Li ñu jublu ci formation pur mana ligey dara modi fexe ñi amul ligey am ci lunu jap ci liy jemele rewmi ca kanam.
Njangum mak ñi
Bu feke danga am lu ep 18 ci ay at, man nga def njamgum mak ñi. Bërëb yo xamne ni dinga fa mana xame lu bari: njangum dal, ak yenen xetu xam xam. Batay man nga fa dal njàng pur def formation bo beg wala pur dugu universite pur ñi am 25 ci ay at.
Lecol yoyu dinanu faral di def ay activite pur jàng ay lak, ak lu jem ci walu xetu ordinateur.
Formation ci walu xetu ordinateur
Mbotayu bari dinanu faral di def formation pur nga xam Internet ak walu ordinateur. Ben ci yoyu moy Barcelona Activa, Cibernarium, wala Xarxa Òmnia.
Jàng lak yi
Ben ci yi gana am solo ci yoyu moy njangum lak yi. Fi dinga fi fek information binga soxla pu dem fula ci nex pur jàng.



