Liggëyal sa bopp
Lii nu bind fii am nañ Tekki wi ci Kaalama Al pulaar.
Beneen yoon ngir liggëy ci Kataluña mooy nga liggëyal sa bopp. Bu ka bëggé waarna nga aam kayitu yu la maay bu soo nga agsi nga ubbi sa antarpirissu bopp.
Kan moo mëne wutt kayitu sessour biiy maaye nga liggêyalsa bopp?
Kepp ku bëggë ubbi anterpiriss ba liggëyal boppam fi. Di soxla dekk fi ci aanam bu deppo ak yoon ba lijjantu ko sa konsila bala aksi fi.
Yaan kayit ngaay soxla?
— Kayit mbëbët ngir antarpiriss bi ba njaay mi (palan anatrpiriss) ak lisenss yi ci waar; Bu bëggé bindu sa antarpiriss di nga soxla def yeen lijjante ci bërëp bu ngor gi yi goox yi ay limpo yi.
— Peermi bi anda ak bindu antarpiriss ci at la tollu , te mën k yeesal ñaari yoon yo tollu ci ñaari at nu ne. Bu wesso juroom at, niirol ak yeen maay sañ dekk ak ligeeyal, day tëdd bepp liggëy yu doomi reew mi, anda ak peermi dekk ba faw.
Fo kaay wutte?
Ci biro I toppatoo doxandeem ( subdelekasoη koberno) ci tundo bi nga waara liggëye.
Ni xamne dekk ku Españ amna naatelu yoon bu mëna jaar ngir am maaye sañ dekk ak ligeeyal bokk ci kontinjente. Ay peermi yu fuss la yu ngoor gi ubbi gànnaw xol ni liggëyo kaay tëddé.



