Jënd

No mëné aam kër

Jënd kër mo xam bu bess ba yagg daay lacc xaliss bu baari baay waaral ngay lebbi bank ngir faay ko.

Bu bess ba bu yagg
Kër yi mën doo yu bess (tabaax bu te kenn dekk gu si) ba bu yagg (bu dekkoon). Bu xalaate jënd bu bess da ngay dem ci boorom tabaax bi ba asenss yi jaay. Bu fekk bu yagg ngay jënd daay xol ndax and li yoon tëral te baax ngir dekk si.

Li yoon tëral tabaax

Mën nga xol ci teere liim ci boorom kër yi foo kayitu kër gi tollu ci liim ak mbëbët reew taax . Lollu daay tekki ne kër gi noppina ci dekk ci, amul benn tolof ci wallu yoon ba bokk ci mbëbët reew taax, boorom xam nan ko te faay bepp boor ay limpos bu tax ci kër gi( booru bank, limpo kër, taayle ba yeen xeeti taaxal).

Kontra jënd

Jënd kër dañ gooy def ak kontra jaay. Ba nga ko xatiim lepp dafa waara leer , loolu taax nga waara utt ko kaay xol ci wallu njëŋ ak teggu. Tamiit waar na nga xaam nax kër gi amna kayitu gi waane ne mën ci dekk , and nax yoon. Njàngal kayitu kontra ci fan yepp ,bu ka jaaré demal ci awocat bac i mbotaay yi jappale jënd kat yi.

Faay yi taax ci kontra jënd bi

Amna ay faay yu jënd kat bi di def mu taax ci kontra. Yoo ñôy yi: nattu njëŋ ak teggin, limpo, faay noter bi ak bindu ci teeré liimu boorom kër yi. Da waara boole faay ci lii nga xalaat gën ndax mén tollu ci fukk ci temeer bo jël ci njëŋ li.

Peexe faay gi

Jënd kër daa faaral di lacc xaliss bu daayo, daay taax nga dem lebbi ci bank yi ba bepp xettu bërëbu lepp. Boor bi ak bank daay teggu ci booru taale kër gi (ñaata ngay wer wu ne ak intere yi). So bëggé weuy si li ngaay jënd, xollal bu baax li bank yi di tegg ci boor, duggul njëk bi, intere yi ak peey gi.

Ndimbël ay maaye yi
Bu de jënd xameel ne amna ay ndimbël ak maaye yu ngoor gi tekk ngir yombal askan am fu nu dek. Gestul sarti yii nu kooy ame ci jawriñ ci yoor dekkuwa.