- Inici
- Fii ba fëlé
- Lep
- Dju-dju ak nap katbi
Dju-dju ak nap katbi
Lep mandin yi
Li lep la bo xamne ben nap kat bu muss bu troxal Rap wi. Histoire la bunu xam ci Senegal ak Gambie.
Ben biss la won mu am ben nap kat bu dundu ci bori dek bi. Ku bugo ligeyam la: dan na nap lu bari, ci biss bi yep, lege legi dan na faral di rëb lëk ak llenen xeti mala ak jumtukay yumu dan deferal bopam.
Ben biss, bimuy dem di napi ben jen bu rey dadi ko mat. Ci lolu, mu tit, bi mu gene ndox mi mu giss ne du jen, wante Rap Dju-dju la, ak xeth ci loxom, bayiwul ben yon diko toñ. Nap kat bi dadi meer, ndax limu ko dimbaliwul wante diko retan.
Rap Dju-dju adi meer tamit dadi neko: setal kan ci man ak yaw mo gana ep dole pur xathi mbal mi. Bu njek bi Dju.dju sani ko bu kawe. Mbal mi dadi dal ci ndoxmi, dadi jal ci bir ndoxmi. Bi ko Dju-dju gene nap kat bi dadi neko su feke moko sani duko mana jotat. Ci lolu ñu dadi ne baña ñak mbal mi mo gen.
Ñu dad jali ci benen muy rawante. Nap katbi dadi koy nax. Mu dadi delu gañe ko.
Ñatel bi ñuy set ñom ñar kan mo daxa nap. Dju-dju xamul nuñuy nape, ci lolu nap katbi dadi neko dangay nopi boy nap. Wante com dafa titon nap kat bi dadi koy yew ci ben garap, bobu balegi Mukul nap dara.
Rap bi Dju-dju di yuxu ne da baga dem, ci lolu mu nangu ne gañe nanu ko. Mu dadi ne nap kat bi dana ko ox jen yu bari te dana dmbali buy rëb. Nap katbi, ci ndimbalu Dju-dju dadi nek nit ku am alal ku am dole.
Batay danadu faral di wax ni nap kat bi wala reb kat bi bu jape lu bari danunan Dju-dju moka dimbali.



