- Inici
- Dëkk Kataluña
- Ci walu njàng ak formasoη
- Njangu xaleyi
Njangu xaleyi
Pàcc yi waara jaar ayla yéewen
Xaleyi dano wara jàng lu manuta ñak la ñu dem lecol. Fi di nga fi am information binga soxla pur xaleyi mana def ndang momu nga xamne munuta ñak.
Mbindumi pur mana jàng
Mbindumi pur dal njang dana faral di tambali ci weru Mars wala Avril, ci lecol binga xamne wajuri beg nanu seni dom jangefa. Bu feke dano tuhu, mun ngena bindu ci goj bi ngen dëke sasoulen nexe, fofu dinanlen wax bufeke place amna.
Atum njang mi
Atum njang mi dana faral di tambali ci weru Septembre tedi jex ci weru Juin. Manam dëk mu nek dina mana defar waxtu wunu buga tambali ak waxtu wunu beg lecol bi teth ak fet yi un bega elewi amko.
Wala njang mi ci Cataluña
Njangu xaleyi tutiyi (ba ci 3 at) ñu soga jal ci lecol primaire (ci digante 3 baci 6 at) waxtu njang la bo xamne kumu nex do ko def. Wante njang primaire ak segondaire (ci digante 6 ak 16 at) moy njang bu matu ta ñak.
Bu weso lecol publique bi, amna tamit lecol priwe ci bir yoyu amna yunuy tude lecol yu nga xamne ngur gi dasiy def loxom ci walu ndimbel. Wante lecol yoyu yep ñu aju ci yoon wi jàng rewmi tërël.
Njangu tut tankiyi
Moy njang xaleyi ci digante 0 baci 6 at. Njangu tut tankiyi mingi aju ci ñar xath bu sinek tolú ci ñeti at. Ben xath bi moy 0 baci 3 at, kumu nex mo kay def te ñi ngi koy defe ci lecol yinu tude lecolu xaleyi, man na nek public wara priwe. Benen xath moy 3 baci 6 at duna fay dara ci lecol public yi wala lecol yinga xamne xath bi dong laniy fay.
Pur xaleyi fi doga ñew pur ñu jàng ñi koy def bunu xole seni at, fan lanu wara dugu pur mana jàng bu bax.
Njàng mbi munuta ñak ci lecol primaire
Moy njàng mbi tamabali ci jurom bani at de wara nek ci 6 baci 12 at. Njangu lecol primaire lu manuta ñak la te doci fay dara, mom dana tolu ci ñati xath: xath bu njenk bi (6 ak 8 at), xath bi ci top (8 ak 10 at) xath bi ci muje (10ak 12 at). Waxtula bo xamanteni dinan ci jangal xale mbiru matematic, mbid, nuñuy lire ak nuñuy waxe, ak yenen xetu gestu.
Njangum Segondaire bimanuta ñak
Njangum segondaire dina tolu ci 12 baci 16 at. Modi ñentelu xath bici walu njang mi ci linuy tude Institutos de Educación Secundaria (IES). Ci walu Njangum Segondaire bimanuta ñak Educación Secundaria Obligatoria dinanuci yok xam xamu xaleyi ci lu jem ci walu ada ak tecnic, lep tenku ci yok ay man mani xaleyi. Batay, ci xath bu muje bi, dinanu ko yombal ay jumtukay pur mu mana continue njangam wala mu tambali ligey.
Yenen yengu yudul ci bir lecol bi
Dina am solo say dom budul ci lecol bi ñu yengu ci yeneni activite com lu demeniki esport, music, wala walu ada wala artist. Manam benen buntu la bu mana yok sen xam xam ci walu wune muy lu leñ di jarrín ci finiy dundu.
Mbotayu Yay yi ak Bay yi (AMPA)
Def bi wajuri wara def sen loxo ci walu njàng xaleyi lu am solo la. War nanu mana bok ci mbotayi yoyu ak ci conseil lecol yi.
Bu dimbël ba maay gu joxe ngir njàng , yombal sema k diik, lekk ci daara, jëndl teeré, ba ku ne ndongo bu soxla yu yeemé.



