- Inici
- Dëkk Kataluña
- Ci walu njàng ak formasoη
- Njangum Universite
Njangum Universite
Duggum daara un mag ji
Njangum universite mu ngi jem ci forme ñu nga xamni sen xam xam day jem ci wen walu. Yi moy ni nga mana tane bula nex.
Exame pur dugu universite
Pur nga muna dugu universite danga wara def exame bi un tude PAU (exame biy tax nga muna dugu universite) moy tax ñu mana xam baxam sa xam xam binga jangon ci bacalorea bi ñor na wala.
Njangum universite
Lijasa yi ak walu doxalin njàng mi legi ñu ngi joku ci niko Europe bëge. Moy linu tude Plan de Boloña, linu ci jublu moy bole ak yombal ñi jàng ñuy man di dem fulen nex ci Europe.
Lu bess li ci am ci linuy wowe bërëb njangalemi moy:
Njangum grado
Moy liñuy tude Licens ci njàng binu don def mu tudu EEES (mu tolou ci 4 at). Njangum grado
mongi tolu ci 240 creditos bunga xamni yangi koy jot ci xath bu nek mu jem ci: formation bu njenke, jumtukay ñu manula ñak, yinga xamni yaw lay nex nga def ko, stage ak ligey bo def bo jexale grado bi.
Njangum Master
Moy njàng mu jem ci walu gestu yenes xetu xam xam. Ni njangu master bobu di tëde moy 60 baci 120 creditos, tamit, jumtukay ñu manula ñak, yinga xamni yaw lay nex nga def ko, seminer, stage ak ligey bo def bo jexale master bi.
Njangum dotorado
Amna ñatelu yoonu njang bi jem ci walu programu doctorado binga xamni ñi koy def moy ñi bega nek di gestu wala def ligeyu universite.
Bourse ak ndimbel
Amna ben program pur ay bourse ak ay ndimbal pur ñiy jàng ci universite lula muna dimbali pur nga fay sam njàng. Ministre bi yor walu njàng mi, politic ada ak esport dina faral di def ay ndimbal ci walu wowu.
Mak ñi am lu tolu ci 25 at de buga dugu unuversite
Bo ame lu ep 25 at tenga buga jàng grado superior mun na nek ci bo defe examen pur dugu universite bi mak yi am 25 at. Lecol yi mak ñi muna jànge danan koy def.
Lo wara def pur sa lijasa mengo ak bu wa rewmi bu feke jànge wofi
Bu feke danga am lijasa ci benen rew budul fi, linga muna def moy set no fexe mu mana dopo ak universite binga buga jànge. Ministre bi yor walu njàng mi, politic ada ak esport mo yor walu wowu. Mun nga xam ci buntu bi no fexe ba xam li nu ciy lath pur mana def li war.



