Magg ni
Bërëp yi japple maggat yi ci aam jot
Bi guddi fan di yokko ba leggi, settlu nan ci Kataluña dundu maggi gëne yagg. Lolu taxna ba ay pexe yu baari tekk nañu ko ngir facc seen soxla.
Këru magg yi di ay bërep yu nu jakklel maggi 60 aat ba lu ko epp te allatrete. Di nan fay amal ay yëngu yu dëppo jamono, aada va tangat yaram, ak yeen fo yuy yokku taw fexu di magg ni.
Ngir sôril xel mu wanneko ba doole nu neew amna ay bêrep bu ndimbal yu baari yuy jappàle maggat yi ak seen njaboot saa su ne. Amna centar yu leen di tee ci bess, ak noo xamne da nu leen nemeku si ci kër yi. Amna yi yeen ndimbal yoonu tekk ngir maggat yu dema ni massalan kër yu nu leen sedd ba centar yunu leen di dëkkal.
Bu ci bëgge xam dar mën nga dem ba sa njaboot, ci banxassu ndimbal askan bu goornama Kataluña ba beep bërep bu lijënti mbiir yi.
Bërëp bi japple ak dimbël askan fi ci Kataluña mooy (ICASS), mën lacc dimbëlo bi maggat aajo fi.



