Li lay yobu ci bëreb yi nga buga dem ak li nga muna jefendiko

Lii nu bind fii am nañ Tekki wi ci Kaalama Al pulaar

Saarwissu yiiy am ci bëccëg

Sa so jublo ci dundu ak ligey ci Cataluña, waxtu wowu ngay tambali sa dundu dëg dëg.

Mo tax dananu la wax ay jumtukay yu la mana dimbali si foy dem, ak tamit yenen jumtukay yu lay muna dimbali ci walu jefendiku ci soxla bo am.

Ben ci biss yi gana am solo nga wara xam moy mbotayu transport, binga xamni pur ñëp la wala bu priwebi, servisu bank yi pur linga soxla ci mbiri xaliss wala liy tax nga xam li la lo yon may com ku jefendiko serwis yoyu ak linga wara muna def sa sunu la toñe.