Teranga - Yoonu jokko Kataluña ak

Patum bu Berga

Catalunya        

Xew xewu bi jaklel saafara ci Bergëda

Patum bu Berga xew xew bu siiw la bu joggé ci bes yu un jakleloon diine yi ci teataru jaamono yu njëk yi. Mo ngi joggé ci mbiir yi nii doxantu bi daan ci beesu insa , di doon ci seentu un naax askan wi xiir leen ci teere yalla bi.

Mooy dem ba ne bessu askan wi, tàggo ak doxantu diine bi ko sossoon, sopi tuur wi di Bull (mbaxallu julli bu selle bi). Li mmo indi Patum bi teey mu denc li baari ci ndoxali bu jegg ba.

Li taax ba peeyU Berguedà di dekkil beeb ci coosaan yi gëna magg ci arminaat bessu Kataluña. Alaarba ci ci ay bess bi jakklel yaaram mu ku selle ki, ci beccëg gi nu nit ni ëpp daayo ci reey daan ni fecc aand ak boroom taabala yi ak xaarara yi. Ci Goon gi, ci baayalu San pEre, wa dekk bi yepp, Patum foofu la, taabala, giitas ak nit ni epp daayo yo Maggi noo geen di wone ni bess ba gi tambali.Bess bi gêna reey mooy ci ëleksi alxames, ci la Patum di xumb . ci suba si amna Patum leer di mbaxal bu yam, ci Gaddi ci la Patum di mët: mbaaboor yepp di fecc ak taabala yi ak peetal yi , wa askan Bergueda geen ci mbend yi. Lu yeemo ci xew xe yi aam luxus ak taal di ka dooli ci gawo mooy bess bu mujj ci coosaan gi.

Soo Bëggé bokk ci xew xew bi fokk nga dem ak paasteef tee yoobo yeere yu maggat,(jiin), mussor, teηηane ak daal yu ooyaf yu aar ci taal yi. Bul joogé Berga te musso njaaru Patum bi xamne fii rek a aam ; njaaxassu sanηara bum el ni sumsum bu saaf sukar deffare moskatel ak anis.

Li taax baanu taan ko ci bess yi aduna moom ci aatum 2005, aamna leggi naar funk ak juroomi aat baa Seneralitaat bi deffe bessu reew mi.

Bokkal        

imatge Foto de Ferran. Llicència cc (by-nc-nd)