Nun ñooy ñan

Dallal jaam fii ci Teranga

Teranga.cat web bu bu doomi Senegaal yi ni ci di daajé, Li ka taxa jokk di yombal dall lu doxandem yi sogga aksi, xamal leen aada ak làkku reew mi.

Siiwal ko ci naatel xajju 2008, ci ndimbalu Jawriñ bu seytu doxaliin Ngoor tekk ko ci kureel ngi jokkante gi ci mbiiri telekomunikasoŋ Kataluña, Teranga.cat dafaay jaar ci xarale yu bess yi ngir yombal weccente xalaat askan Senegaal bu Cataluña.

Ak mbëbët gila web juddu, boole naari làkk ubbi yoon jokko ci làkk yi katalan ak wolof ba pël, mu tax ba alfebtisasoŋ ci katalan yomb.

Di wax ci soxla doxandem yi sosso Senegaal di askan bu dugg bu bax ci Kataluña, Mbotaay doxandem yepp di ci jàpp ande ci a kwa Fondasoŋ Pere Tarres. Di gërëm Oma Technologies, Produccions Mínimes ak Cristina Minguillon.

Tewool, Teranga dafa ubbi ko ci doomi Senegaal ak Kataluña yepp, di oowo seen tuur ba ci tuuru mbotaay, su bëggé bokk ci prose bi.

Naan nooy Teranga
Teranga.cat xalattu Fundasoŋ Pere Tarres, anda k Kureelu mbotaayu Senegaal ci Kataluña (KASK) Mbotaay doomi Senegaal ci Barsaloon ak Mbootaay Fedde Fulbe Jokkere Endamên (FFJE) mën naan jeffandikoo web bi ngir siiwal seen yenŋu.

Li ngaay fekk ci BërëBu Web bi?
Teranga.cat fàq na pàcc yu barri ngir jot xibaar ba jokklante:

Teraliin xew xew yi:: Pàcc siiwal xew xew , demani lël, waxtaan, ja ba wone, ak bepp mbir bu amal solo askan un Teranga.cat.

Dekk ci Kataluña:: Pàcc joxe xibaar aanam gu maat te njërinal ci faan yiitel doxandem bu sogga aksi ngir Dunham fi. Di Teere guindi ci wàllu werguyaram, dekkuway ak njaboot gi…

Fi ak Fële: : Pàcc gi di yombal jokko bi ak askan yepp, ci xibaar ak lëkkëlo gànaw taan gi mu aamal ci xew xew ba xamle ci mbiiri aada, cosaan, Bu Kataluña ak Senegaal. Ngir nu def ko ci niimo gëna rafeti sa xalaat, xareñ ak sedde lu nuy sope la.

Ci katalan: : Taan naan peexe yi gëna baax ngir njàng lakk fi, defko jaar ci xarale yu bees yi. Di giss fi ay teeré, fiilme, foowukay ay yeneen xettu xarale yu laay jàppale ci njàng mi.

Liggëy:: Yeggle yi nii taan ci maayé ak wut…. Teere guindi ngir nga mëna jubbulo ci mbiiri liggëy.

Bërebu Yeggle bi:: Pàcc weccente xalaat taamu ci tògg. Bokk ci ubbeku ci neep, mëness na ci yi yeggle dekkuway, tukki ba jokko.

Mbotaay yi: uPàcc jokkante mbotaay yi doomi Senegaal fi ci Kataluña ngir yegg xew xew yiiy aam ak peexe yi fii ngir seen yokkute.

Bërëbu Web bu Ubbeku

Wessu web Teranga.cat ndjaje laa bëgge nekk: Lollu taax ba nga Fiyi giss pàcc yu baari yo mëna bokk, yo mëna wax sa xalaat , nettali saa xam xam , ba diggël ci tògg! Un laay naax nga book si, di nga jappale ci suxaat Teranga ba mu màggat.

 

    nataal bi