- Inici
- Dëkk Kataluña
- Wergu yaram
- Serwis yiy fath
Serwis yiy fath
Liiy seytu werguyaram ci Kataluña
Serwis yoyu ñu ngi ci bir rewmi yep pur mana taxawu ñep ci Kataluña. Yinga xamne ño ci gana jege nit ñi moy Dispensaire, mom lanuy wowe tamit CAP.
Dispensaire
Moy bëréb binga wara njenke dem bo febare wala nga wara dimbali kenen. Ci dëk yu ndaw yi Dispensaire you ñi ñuy tude consultorios locales ño ko yor. Ci dëk yu mak yi, amna ay Dispensaire yu bari te ku nek man nga dem ci bila gana jege finga xamne fanga am dekuway.
Ban fath nga mana am ci Dispensaire?
Taxawu bu njenk ak doctor bunga xamne saso febare mo lay taxawu, te tamit munla yob ci benen doctor bu feke ne jar nako.
Pur ñu manla set danga wara lath wahtu ci sa Dispensaire. Pur sa doctor setla man nga ko def ci ñati anam :
- Mun nga demal sa bop sa Dispensaire ba
- Mun nga ko def ci yone bataxal ci Internet
- Mun nga wote telefon ci “Sanitat Respons”: 902 111 444
Bu fekene sa yaram mayula nga mana dem ba Dispensaire, ñom amnanu ap serwis bumana ñew sa kër.
Bu feke danga am lulay meti lol, dangay dem wala nga wote Dispensaire. Su feke Dispensaire dafa teth, amna ay bërëb yunga mana dem waxtu wu nek muy di centres d'atenció continuada (CAC) nga xamne danuy doxal bu 21h ba 8h. Tamit man nga dem ci serwisu urgens bu ben ci hopital yi.
Bu fekene urgens la
Su feke danga soxla ñu fath la fath mu gaw, mun nga wote ci numero bi te do fay dara 061. Dananu la deglu ci linga soxla te bu ko jare dinanu la yone ambulans bula jelsi
Yenen xeti soxla ci sa wergi yaram
Legi legi du jar dem kër doctor. Farmaci yi dananula mana dimbali bu feke febar bi amul solo lol. At mu nek dina am farmaci yuy ligey ci walu wowu. Bo bege xam yan lanu, man nga:
- Man nga xol ci buntu farmaci, ban mo mome ci walu wowu
- Man nga xol ci jornal yiy gen ci goj binga déke
- Wala tamit nga xol Internet
Yenen béréb yo muna fajo
Ay bëréb la yo xamni sa doctor mo la fay yabal pur ñu manla fath. Bu ci nek ci ñom amna lu muy fath, pur mak ñi, borom febar yu meti yi, ñi ame febaru bop, ñi febar ci walu drog, etc. Yenen di fath ay febar com mbiru sex, ci walu planification, walu ñaku.



